Lu Jem Ci Nun
Nun Ñooy Kan?
Taalibe Yeesu Lanu.
Sunu ligeey mooy nu dem sàkk ay taalibe ci
xeet yèpp, sòobleen ci ndox ci turu Baay bi ak
Doom ji ak Xel mu Sell mi, te nuy jàngal leen
ñuy sàmm lèpp li Yeesu sant.
Ay Jaar Jaar Yu Doy War
Gannaaw bi ma jeme lépp ci addina si, wax ma
nu dinanu matal sama xol ,gis nanu ne yëf
yooyu yépp (xaalis, doole, jem kanam, siiw, ak li
ci topp), loolu yépp amul benn njariñ.. Kon
boog, bima ci jëkke jang ak dund te gis Yàlla gi
mu sákk ak bëgg lool, sama dund soppi na
woon ba faww.
Gëm nanu ne, ak sunuy xol yépp, yeen itam
mën ngeen fekk ay tontu ci seeni laaj ak jafe
jafe ci seeni dund. Seen dund am nanu njeriñ teyeen itam mën ngeen ko gisaando ak yéneen
gëstu itam ngir njeriñ ci seeni dund.
Kàddug Yàlla Gi
Yàlla dafa yonnee Yeesu Kirist, Almasi bi, ci
addina si ngir mu séddaale kaddoom ak ñit
ñepp, xeet yépp, giir yépp ak reew yépp.
- “Dama ñëw ngir ñit ñi am dund, ba nekk ci naataange.” Yowanna 10:10
- “Man maay yoon wi, maay dëgg te dund it man la. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man.” Yowanna 14:6